Daqaar
Daqaar garab la gu fekk baax ca penku Afrig ca àllu Madagaskaar waaye bari lool ci Afrig sowwu jant fu ci mel ni Senegaal bari na fa lool. Guddaayam man naa àgg ci 20i met waaye itam dafa yeexug màgg waaye nag garab gu man a gudd fan la. Ca Senegaal nag, dees faa xaw a gaafal garabu daqaar. Di wax naan ay jinne dañu fay dëkk, ba ñu bari ñimewuñu koo def seen kër.

Meññeef mi
Soppi
Meññeefam te mooy doom yi guddaayam di mat 20i sàntimet. Buy door a meññ mooy benqal, day nëtëx te neex lool ñu man koy lekk noonu. Bu ñoree lay doon ub daqaar. Dees na ko jëfandikoo fu bari. Boo maccee doom bi ba noppi day am ab xoox ca biir. Xoox booba mooy sax. Daqaar dees koy jëfandikoo di ci defar naan yu neex. Ak di ko def maccaat ci ceebu jën, te itam njarum daqaar day faj seere di raxas biir, dana faj itam bóoli guy metti. Dees na ko def it cifaay ci laax, ñu di ko wax: Laaxu daqaar.
Ngogna
SoppiCafna
SoppiTuru xam-xam wi
SoppiTamarindus indica

